کد خبر: 1294095
تاریخ انتشار : ۰۳ مهر ۱۳۹۲ - ۲۲:۱۷

Al Azxar aartuna ci al xuraan yi nga xamni dañukoy def ci internet te diko waaññi walla ñu diko weccee

Waallu bitim reew kureel bi nga xamni moo neekk ci daara ju kawe jiiddi Al Azxar te yor waallu gëstu aartuna ci laaya al xuraan ak addiis yi nga xamni dañukoy def ci internet di faral diko waaññi walla diko yaax



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (Al Ixraam) ni: kureel bi nga xamni moo neekk ci daara ju kawe jiidi Al Azxar te yor waallu gëstu xamlena ni: gisnañu ci leen ayy site internet ñuyy yaax ak nasaxal laaya al xuraan walla diko yaax walla di ci yookk loo xamni nii bokku ci, boo demee ci laaya bii nga xamni moo neekk ci surat Ali Imraan dañu yookk baatu (al xax) te baat boobu bokkul ci laaya bi


Kiidi Sheyx Tawfiix Abdul Aziz njiitu kureel bi nga xamni moo yor waallu gëstu ci daara jiidi Al Azxar waxna ni: ñi nga xamni dañii jëfandikoo internet suñu bëggee jaang al xuraan walla deglu al xuraan warnañu mana dem ci site yi nga xamni dañu leena xam bu baax te yitt woornañu


Kiidi Sheyx Tafiix Abdul Aziz saakkuna ci compagnie ak ñi nga xamni dañii ligeey ci waallu al xuraan ci net bi laata ñuyy def al xuraan ci internet ñu seetko seetaatko


Suñu sukkandikoo ci xabaar bii dinañu wax ni lu jiitu ñi nga xamni dañii jëfandikoo Fcebook ñoo njëkka joxe xabaaru yaax ak yookk ci laaya al xuraan yi


1293328

captcha