کد خبر: 1296439
تاریخ انتشار : ۰۹ مهر ۱۳۹۲ - ۰۰:۱۱

Laaya al xuraan yu ñu bind ci ayy deru kewel ca muse bu neekk ca reewum Tunisie

Waallu bitim reew njiitu muse civilization ak art bu neekk ca reewum Tunisie ci gox biidi xirwaan xamlena ni amnañu ci muse bi ayy al xuraan yoo xamni nii ci deru kewel lañuko bind



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci yeenekaay biidi (Al Qudsu arabi) ni: muse bii nga xamni moo neekk ci reewum Tunisie ci gox biidi (Xirwaan) ñungifa deeñ ayy jeexintalu taariixu islaam ak ayy piece ak mbir yu bari yoo xamni dafa aju ci islaam ak jullit ñi jamono ju yaagg


(Zaxiir ashaxayabii) njiitu muse ak art ci islaam xamlena ni: muse bii neekk ci Xirvaan amna ayy kaamilu al xuraan yu bari yoo xamni nii ci deru ayy kewel lañuko bind te kaamulu al xuraan yii ci njëlbeenu islaam lay deellu


(Zaxiir ashaxayabii) yookkna ci ni: dinañu feekk ci muse bii ayy kaamilu al xuraan yoo xamni nii ci mindinu waa kuufa lañuko bindee ak ayy kaamilu al xuraan yoo xamni nii ndoxu wurus lañuko taaralee


Kiidi Ashaxayabii bokkna ci kaamilu al xuraan yi nga xamni mungi ci muse bii al xuraan bi nga xamni kiidi (Maz ben badiis) nga xamni moo sos ñjëlbeenu nguuru Sanxajii ci juroomeelu xarnu gannaaw gaaddaay gi


1296103

captcha