کد خبر: 1277312
تاریخ انتشار : ۰۳ شهريور ۱۳۹۲ - ۰۲:۴۳

Ŋaañnañu kaamilu al xuraan ca suuf sa nga xamni islaam fala njëkk feeñ

Waallu bitim reew taskatu xabaaru reewum arabie saoudite xamlenañu amalnañu ayy ŋaañ al xuraan ci daara ju kawe ji nga xamni moom lañu jagleel soxna yi ca gox biidi (Yanbah)



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo aju ci television biidi (Al Alam) ni: daara jii nga xamni moo neekk ci (Yanbah) nga xamni dafa aju ci daara ju kawe jiidi Tayiba neekk ci reewum Arabie saoudite ayy nitt gisnañu ayy kaamilu al xuraan yu ñu saandi ci ayy mbalis ci biir daara ji


Suñu sukkandikoo ci xabaar dinañu waxni batiment bi nga xamni nonggo daara yi falañu neekkoon dañuko waroona geen gannaaw bi nga xamni geennañu dañu feekk ayy kaamilu al xuraan ci mbalis bi


Keen ci ñi nga xamni ñoo dëkk ci gox biidi (Yanbah) moo xamle xabaar bii te yitt waxna ni ñi nga xamni ñoodoon ligeey ci waallu setal bërëb ñoo saandi kaamilu al xuraan yi ci mbalis mi


Nataal yi sa wesaarenañuko ci internet bi


1276780

captcha