Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci ñi nga xamni ñoo leen teewal ci Asie ni: suñu sukkandikoo ci kaaddu police dinañu wax ni ñi nga xamni ñoo amal coong yii dañoo yoroon ayy ngannaay yoo xamni nii amoul been bruit ba moo waral ñi nga xamni ñoo jegewoon xew xew bi gaawuñu yekk mbir mi
Xew xew bii mungi xewee ci jamono ji nga xamni jullikay yaangi julli fajar ba leegi nak deegguñu been mbooloo terroriste bu wax ni moo def jëf ju ñaaw jii
Li jara fattaliku mooy ci att yii mujju lu toollu ci fukki junni nitt ñaakknañu seen bakan ci ayy coong yu melnii ak ayy fitna yi nga xamni diine walla waasoo mooko lal
1281059