Waallu bitim reew Mark basili Yusuf nga xamni moo defaroon film bii nga xamni dafay ŋaañ islaam ak yonent bi te ñu teggoonko loxo yoon tegginako loxo
Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (Al Axraam) ni: Mark Basili Yusuf nga xamni mungi toollu ci juroom fukki att ak juroom been feekk baax ca reewum Egypt waaye am ayy këyitu reewum Amerique laata muyy gennee film bii nga xamni dafay ŋaañ islaam ci attum 2010 dañuko tuumaaloon ni dafa jalgati ayy koppar ci waallu Bank
Mark basili yusuf ci weeru octobre lañuko tegeetoon loxo ndax dafa samontewul woon ak mbir yi nga xamni moo taxon ñu baayiko
Basili Yusuf nga xamni samontewul woon ak li nga xamni moo taxon ñu baayiko ci la changer turam jël tur boo xamni nii dañukokoy woowee waaye tuddul noonu diko wuyoo ba defar ab film boo xamni dafay ŋaañ islaam ak yonent bi, jamono ji nga xamni film bii geenna jullit ñëpp dañoo maroon ba futtu ba moo waraloon ñu amal ayy ñaxtu ci aduna bi yëpp
Ki nga xamni moo yor kaaddu fi mbaxna neekkee been waxna ni: kiidi Basili yusuf gannaaw bi nga xamni daannañuko ci attu kaso ci abb bërëbu bu keen xamul lañuko tëjoon
Takk der yi waxnañu ni du flm bi nga xamni moom la Basili defaroon moo waraloon ñu tekko loxo waaye jalgati bimu defoon ci waallu banque moo waraloon ñu tekko loxo
1294318