کد خبر: 1298757
تاریخ انتشار : ۱۴ مهر ۱۳۹۲ - ۰۱:۰۰

Dinañu amal ayy xew xewu maaggal ak fattaliku Imaam Jawaad ca Manchester

Waallu bitim reew ayy xew xewu maaggal ak fattaliku kiidi Imaam Jawaad tey 05 octobre ci nimalu centre islamique bi nga xamni moo neekk ca Manchester



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jeleeko ci ñi nga xamni ñoo leen teewal ca reewu tugël yin i: suñu sukkandikoo ci xabaar yi nga xamni moo baayeekoo ci centre islamique bii neekk ci Manchester dinañu wax ni tey jii su fukki waxtu ak juroom ñent jotee ci waxtu reewum Angleterre ci lañii door xew xew yi su ñaar fukki waxtu ak been jotee ci lay yeegg ci cëppaa ndaw gi


Programmu xew xew bii nak gannaaw bi ñu jullee timis ak geewe lañukoy door dinañufa amal ab waxtaan ci lu aju ci jikko ak dundinu Imaam Jawaad ci gannaaw loolu dinañu tiislu jooy ngir fattaliku faat gi nga xamni noon yi faatnañukowoon Imaam Jawaad


Centre islamique bii nga xamni moo neekk ci Manchester mungi woo jullit ñëpp ñu teew ci xew xew bii


1298432

captcha