کد خبر: 1299298
تاریخ انتشار : ۱۴ مهر ۱۳۹۲ - ۲۱:۵۴

Egypt mungi jaappalante ak Arabie Saoudite ngir jaamarloo ak ujaaj yi nga xamni Morsi lañu aandal

Waallu bitim reew Mukhtar Jume jawriñ gi ñu deenkk waallu diine ci reewum Egypt mungi ligeey ak nguuru arabie saoudite ngir ñu tere ayy ndaje politik ci fanu ajj gi



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet ni: ñi nga xamni ñoo aand ak Muhamad Morsi njiitu reewum Egypt bi nga xamni dañuko foolli xamlenañu ni suñu demee maakka sa dañii wëyy di amal seeni ñaxtu


Jawriñ gi ñu deenkk waallu diine ci reewum Egypt xamlena ni: amal ayy ndajeem ñaxtu ci waallu politik ci fanu ajj gi dafa wute ak moom li nga xamni moom la tuddee jaangale islaam


Yookkna ci ni: nguuru arabie saoudite moo neekk ci dëgg ci teere mbooleem xeetu ndajeem ñaxtu ci fan yii nga xamni dañu cii amal ajj


(Sayid Abdullah Al Xalyawi) njiitu takk der yi ci reewum Arabie Saoudite xamlena ni: ayy kilifay reewum Arabie Saoudite xamlenañu ni duñu baayi keen di xajamal ajj gi te yitt noppinañu ak jaamarloo ak keep ku bëgga yënggu ci waallu politik


(Xaalid Faysal) njiitu Maakka xamlena ni: nguuru reewum Arabie Saoudite dafay jaamarloo ak li nga xamni moom tukki politik lako tuddee


1298916

captcha