Waallu bitim reew bërëbu aattekaay bu neekk ci gox biidi (kufru sheyx) ci reewum Egypt yookkna tekk loxo bi nga xamni tekknako loxo njiitu waa frères musulman
Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (asharq) ni: aattekaay bii neekk ci gox biidi (kufru sheyx) yookkna aapp bi nga xamni ci lañu waroona deeñ njiitu waa frères musulman yi nga xamni toollunañu ci 140 doomu aadama ci diiru fukki fan ak jurooom
Suñu sukkandikoo ci xabaar bii dinañu wax ni bërëbu aattekaay bii dafa tuumaal njiitu waa frères musulman yin i dañoo bokkoon ci fitna yi nga xamni ayy doomu aadama yu bari faatunañu ci, njiitu waa frères musulman dañu leen tuumaal ni dañoo ñaakka woormaal aax ak yeelleefu doomu aadam yi
Gox biidi (kufru sheyx) been weer mungi nii ayy fitna amfa ba am juroom been doomu aadama yoo xamni ñaakknañu ci seen bakan ak ñaari teemeer ak juroom fukk yoo xamni dañu ci am ayy gaañu gaañu
Bi ñu daaxee Muhamad Morsi ci nguur gii ba leegi bës bu yaalla saakk dinañu amal ayy manifester ak ayy doxu ñaxtu
1307517