Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci këru xabaar biidi (The Associate Press) ni: poste takku der yi nga xamni moo neekk ci Floride tekkna loxo laabbe bi nga xamni dafa singiliwoon al xuraan te toollu ci juroom been fukki att ak been aandoon ak kiidi Marbiin sabjuniiz neekk loxo ndeyjooram toollu ci ñent fukki att ak ñent li nga xamni moom lañukoy tuumaal mooy yor ayy mbir yi nga xamni mënna taal waalla lu melni essence ak gaazoil ndax loolu yoon dafkoy tere
Jomano ji nga xamni ci lañu tekk loxo laabbe bii dafa feekk mudoon dem ci ab Park ngir mana taal al xuraan ci bës bi nga xamni ci lañii faattaliku xew xewu 11 septembre, waaye takk der yi xamlenañu ni bookkna yitt ci li nga xamni moom lañii tuumaal laabbe bii yor ayy nganaay yoo xamni nii yoon dafko tere
Gannaaw bi nga xamni tekknañu loxo ñaar laabbe yii dañu leena tuxal ci kaso bi nga xamni moo neekk ca Floride lu jiitu ñu leen di tekk loxo police ak takk der yi aartuwoon nañu laabbe bi ak loxo ndey jooram bi ci jëfandikoo essence ak leepp loo xamni dafa melni essence
1287040