Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci yeenekaay bii neekk ci reewum Egypt (Al misruyul Yawm) ni: kiidi Muhamad Al baradaay nga xamni ab politician bu raañeekula ci reewum Egypt deemb waxna ni jëflante diggënte ñaari reew yi reewum Amerique ak reewum Iran moo mana saxal jaam ci golf bi
Kii nga xamni dafadoon ligeey ak njiitu reewum Egypt gannaaw Muhamad Mersi ci waallu bitim reew waxna ni: ñaakka jëflante reewum Iran ak reewum Amerique moo waral tey jii ñu gis ayy jafejafe yu bari ci golf bi leegi nak occasion bii nga xamni amnañuko ngir waxtaan ci ñaari wall yi nañu fexe ba duñuko ñaakk
Li jara xam mooy kiidi Muhamad Al Baradaay bi takk der taambalee di jëfandikoo doole ngir jaamarloo ak ñi nga xamni ñoo aand ak president Morsi nga xamni takk der yi ñooko daax ci nguur gi ci la teekki noomba tankkam
Al Baradaay moo jiitewoon agence international de l’energie ataumique ci 1997 ba 2009
1295201