کد خبر: 1295804
تاریخ انتشار : ۰۷ مهر ۱۳۹۲ - ۲۳:۵۷

Jëflante diggënte Amerique ak reew yu neekk ci Golf bi moo mana saxal jaam ci golf bi

Waallu bitim reew Muhamad Al baradaay nga xamni ab politician la bu magg ci reewum Egypt deemb waxna ni jëflante diggënte reewum Amerique ak reewum Iran moo mana indiwaat jaam ci Golf bi



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci yeenekaay bii neekk ci reewum Egypt (Al misruyul Yawm) ni: kiidi Muhamad Al baradaay nga xamni ab politician bu raañeekula ci reewum Egypt deemb waxna ni jëflante diggënte ñaari reew yi reewum Amerique ak reewum Iran moo mana saxal jaam ci golf bi


Kii nga xamni dafadoon ligeey ak njiitu reewum Egypt gannaaw Muhamad Mersi ci waallu bitim reew waxna ni: ñaakka jëflante reewum Iran ak reewum Amerique moo waral tey jii ñu gis ayy jafejafe yu bari ci golf bi leegi nak occasion bii nga xamni amnañuko ngir waxtaan ci ñaari wall yi nañu fexe ba duñuko ñaakk


Li jara xam mooy kiidi Muhamad Al Baradaay bi takk der taambalee di jëfandikoo doole ngir jaamarloo ak ñi nga xamni ñoo aand ak president Morsi nga xamni takk der yi ñooko daax ci nguur gi ci la teekki noomba tankkam


Al Baradaay moo jiitewoon agence international de l’energie ataumique ci 1997 ba 2009


1295201

captcha