کد خبر: 1303373
تاریخ انتشار : ۲۳ مهر ۱۳۹۲ - ۰۱:۰۰

Nonggo daara yu neekk ci reewum Amerique xamnañu faratay ajj

Waallu bitim reew fan yii nga xamni million jullit ñungay daje ngir amal seen faratay ajj ab daara bu neekk ci reewum mungay fexe xale yi nga xamni ñoofay jaangee ñu xam lan mooy ajj ak farata yimu ëmbaale



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (On Islam) ni: nongga daara yi nga xamni ñoo neekk ci daara jiidi (AL Hudaa) neekk ca (Worcester) ci reewum Amerique dañoo sol ayy yëre yu weex taall melni kuyy ajj ngir gëna mana jaang nakalañii ajjee


Programme bii nga xamni ñungikoy doxal dafa book ci programme bi nga xamni moom lañu fas yeene amal ngir gëna mana yee xale yi ci juroomeelu poonkk islaam yi , te duñu yem rek ci jaangale ajj waaye dañii amal ayy waxtaan ndax ñu xam seeni wareef ak seeni poonkk ci islaam


Been weer ci gannaaw kilifa yi nga xamni ñoo jiite daara jii dañoo fexe ba xale yi xam mbootu ajj yepp , suñu sukkandikoo ci been gestu bi ñu amaloon dinañu wax jullit yi nga xamni ñooy yeewoo ca reewum Amerique toolluna ci juroom ñett million , gestu boobu yitt dafay wone ni askanu reewum Amerique xamul lu bari ci waallu islaam ak jullit ñi


1302791

captcha