کد خبر: 1303374
تاریخ انتشار : ۲۳ مهر ۱۳۹۲ - ۰۱:۲۱

Taxawaayu ujaaj yi ca Arafat

Waallu bitim reew tey jii ujaaj yi amalnañu taxawaayu arafa ci taariixu reewum Arabie saoudite ci sahra reewum arabie saoudite



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci television bii nga xamni mooy Al Manar ni: tey 14 octobre la ujaaj yi taambali taxawaayu arafa ci montagne yi tey jii jooxenañu seen faratay taxawu arafa nga xamni ci diggu bëcëk bi lañuko door


Suñu sukkandikoo ci calendrier walla taariixu reewum Arabie Saoudite tey jii mooy bësu arafa taxawaayu arafa nak ci diggu bëcëk bi lañuko wara door ba jant bi feenkk bokkna yitt ci li nga xamni sakkunañuko ci taxawaayu arafa wone ak bërël ñaakk aand ak yeefeer ak bokkaalekatu yaalla yi


Taxawaayu arafa ren jii nak dafa xawa wute ak yeneen att yiñu weesu ndax ren ujaaj yi dafa gëna neew loolu nak ndogalu nguuru arabie saoudite ci waaññi ujaaj yi ndax dafa am ayy ligeey yi nga xamni moom lañii amal


Suba mooy neekk bësu tabaski ci reewum arabie saoudite ujaaj yi nak dinañu neekk ci xaram bi dinañu def yitt minaa dinañu saandi jamra yitt ci bës bii dinañu reendi seen tabaski dinañu waaññi yitt seen karaw yi walla wottko


1302761

captcha