Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar biidi (al misriyuun) ni: kureel bii nga xamni dafa diggu doomu ci waallu xalaat mungi amal ayy karavane ci biir reewum Egypt yëpp ngir xeex ak ñi nga xamni dañoo jaapp ni keep ku gëmul li ñu gëm doo jullit
Li nga xamni moom lañu jublu ci jëf jii mooygëna xamal askan wi islaam bu wër ak jaamarloo ak ñi nga xamni dañii wër di yeefarloo jullit ñi loolu moo waral ñu wesaare ayy brochure maanaan ayy këyit yoo xamni nii dañii xamle islaam bu wër te dañu ci aand ak borom xam xam yi nga xamni ñoo neekk ca daara ju kawe jiidi Al Azxar
Njëlbeenu karavane bii ñungikoy door samedi 26 octobre ci gox biidi Sinaa ci Egypt ci nimbalu ak pasteefu askan wi nga xamni moo dëkk ci gox yooyu
Sabre Xaasimii nga xamni mooy doxal karavane yii waxna ni: borom xam xam yi nga xamni ñoo neekk ci daara ju kawe jiidi Al Azxar dañii ligeey ak kureel bii nga xamni dafa diggu doomu ci waallu xalaat ngir xeex ñii nga xamni dañoo ëppal ci waallu diine te ñu leen di wax ayy (wahhabites) maanaam ibaadu
1308805