کد خبر: 1285546
تاریخ انتشار : ۱۹ شهريور ۱۳۹۲ - ۰۲:۰۸

Ñungi amal ayy daara ci diir bu gaat ngir yookk xam xamu Imaamu jumaa yi ci reewu Uzbakistan

Waallu yënggu yënggu al xuraan bii mooy ñaar fukk ak ñeenteelu yoon ñuyy amal daara yii ngir yookk xam xamu Imaamu jumaan yi ak ñi nga xamni ñooy amal xutba ci jumaa yi daara yii nak ci jumaa jiidi (Samarxand) lañukoy amalee



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci ñi nga xamni ñoo leen teewal ci Asie ni: daara yii nga xamni ñungikoy amal ci diir bu gaat ñaari ayu bës ci gannaaw lañuko door lu toollu ci juroom ñaar fukki Imaamu jumaa teewnañu ci daara yii


Ci xew xewu ubbite daara yii ñuyy amal ci diir bu gaat kiidi (Usmaan Xaan of) nga xamni mooy Muftii ak njiitu kureel bii nga xamni dafay taxaw ci soxla jullit ñi ak kiidi (Yusuf Of) nga xamni mooy njiitu komite bi nga xamni dafay saytu waallu diine ci reewum Uzbakistan te aju ci nguur gi ak (Muhamad nazar xayum of) nga xamni mooy jiite mbootaay gi nga xamni moo ëmb jumaa yi teewoonnañufa


Ñi nga xamni ñoo teewoon ci xew xew biii waxnañu ci waallu programme yi nga xamni moom lañu wara doxal ci jumaa, ñi nga xamni ñoofa teewoon yitt bind seeni laac yi nga xamni amoonnañuko ci waallu Imaam yi ak jumaa yi bañu toontu leen ci


1284899

captcha