کد خبر: 1293445
تاریخ انتشار : ۰۳ مهر ۱۳۹۲ - ۰۱:۰۹

ñungi wëy di tekk loxo njiitu parti frères musulmane / tekknañu njiitu peeccum ndawu reew mi nga xamni jamono yii sa dañuko neenal ñ

Waallu bitim reew tekk deru reewum Egypt yi xamlenañu ni tekknañu loxo keen ci njiitu frères musulman yi nga xamni moo jiitewoon peeccum ndawu reew mi nga xamni gannaaw bi ñu daaxee Morsi ci nguur gi ci lañuko tas tekknañuko loxo



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (asharq) ni: takk deru reewum Egypt yi deemb tekknañu loxo kiidi Ahmad Fahmii nga xamni moo neekkoon njiitu peeccum ndawu reew mi ci jamanoy nguuru Morsi


Gannaaw bi nga xamni yoonu reewum Egypt neenal parti biidi frères musulman ba pare xamlena leepp loo xamni nii parti amoonnako ci alal nguur gi mooko moom takk der yi tekknañu loxo Muhamad atiye nga xamni beneen njiit la ci parti biidi frères musulman yi te yitt moo neekkoon njiitu daara ju kawe jiidi (azaxaazix)


Kiidi Saamih Alkilaanii njiitu kaaraange ci gox biidi asharxiya neekk ci reewum Egypt waxna ni: barki deemb la tekk der xam fu kiidi Ahmad Fahmii neekk ci lañu feekk foofu tekko loxo


Yookkna ci ni: kiidi Fahmii ci gox biidi (Deltaaye niil) ci dëkk biidi Asharqiya lañuko tegee loxo ci saasi rek lañuko yoobb ci bërëbu police bu gëna jege


1293061

captcha