کد خبر: 1295803
تاریخ انتشار : ۰۷ مهر ۱۳۹۲ - ۲۳:۵۴

Ndajeem jaangalekatu diine islaam ak jaar jaaru yonent bi ca reewum Marok

Waallu bitim reew njëlbeenu lëllu jaangalekatu diine islaam ak jaar jaaru yonent bi deemb lañuko door ca Ribaat peyu reewum Marok



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (aujaurdhui) ni: njëlbeenu lëllu jaangalekatu diine islaam yi ak jaar jaaru yonent yaalla Muhamad (psl) ci nimbalu jawriñ gi ñu deenkk waallu diine ci reewum Marok lañuko dooree deemb ca Ribaat waaye nak jawriñ ji daf ci aanda ka mbootaay biidi Daarul Hadis) ak komision bi nga xamni mooy saytu waallu jaang ak ñaangale mi ci reewum Marok, lëll bi nak tey la jeex


Ñi nga xamni ñoo book ci lëll junjuna xalaat ak doxalin yu bees yi nga xamni ñungikoy waajal ci waallu jaang ci reewum Marok loolu nak moo waral nak ñu wara xoolaat jaangaleem diine ak jaar jaaru yonent bi wara xoolaat naka lañii jaangalee ak bind yeneen teere yu bees yoo xamni nii dina mana gëna meengoo ak jamono


Kiidi (Al arabi bu salxam) nga xamni dafa bookk ci komission bi nga xamni dafay saytu waallu jaang ak jaangale ci reewum Marok yëkkatina ayy kaaddu ci wall wii ni: warnañu jëfandikoo xarale yu bees yi ngir jaangale diine islaam waaye yitt warnañu gëna mana xool nakalañii yookkee ak yaatal xam xamu diine


1295221

captcha