کد خبر: 1297743
تاریخ انتشار : ۱۱ مهر ۱۳۹۲ - ۰۰:۲۴

Police reewum Tunisie dafay tere ñu taal raaya Israel

Waallu bitim reew takk deru reewum Tunisie deemb deemb terenañu ñi nga xamni dañudoon amal ayy doxu ñaxtu ñu taal raaya Israel



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (Kofiapress) ni: ayy doomu reewum Palestine ak ayy doomu reewum tunisie nga xamni dañii yënggu ci waallu politik ci doxu ñaxtu bi ñu doon amal ngir naawlu nangu gi nga xamni Israel nanguna suufu Palestine lu toollu ci ñaarfukki att ak juroom juroom ñent takku deru reewum tunisie yi dañuleedoon tere ñu taal raaya Israel bi


Doxkatu ñaxtu dañudoon yëkkati ayy kaaddu di ñaawlu jëf yu ñaaw yi nga xamni Israel mungikoy def ci kaw askanu Palestine ba loolu moo waraloon ñu bëggoona taal raaya Israel bi waaye takk der yi baayiwuñu leen ci dañu leen tere ñu taal raaya bi


Loolu moo waral doxkatu ñaxtu mer lool ci jëf jooju ba jaappante ak takk der yi takk der yi sa dañuleen wër noomba ba duñu mana def dara


Li jara xam mooy Avion de guerre biidi F 16 ci attum 1985 nga xamni Yaser Arafat dafa neekkoon ci reewum Tunisie biko waa Israel bëggee faat dañoo amal ayy coong ci bërëb bimu neekkoon ba lu toollu juroom fukki Palestine ñaakk ci seen bakan fukk ak juroom ñent ci ayy doomu reewum Tunisie ñaakk ci seen bakan


1297520

captcha