Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (ajib) ni: jaraafu gox biidi (Raincy) xamlena ni aandul been yoon ci soxna yi nga xamni ayy jullit lañu ber seen bërëbu taaggat yaram ci gox bi
Bërëb bii nga xamni soxna yi falañudoon amalee seen taaggay yaram weer bii ñu wees la taambali ayy yënggu yënggoom, soxna jullit yi ñoo waral ñu ubbiwoon bërëb bi
Jaraafu gox biidi (Raincy) nga xamni aandul ci soxna jullit yi am seen bërëbu taaggakaayu yaram buñu moomal seen bopp waxna ni bërëbu taaggatukaayu yaram boobu dëppoowul ak yeen teggin yi ak yoon yi amoul parking te yitt sakkuna ci ñu tëcc bërëbu taaggatukaayu yaram soxna jullit yi ci nimu gëna gaawee
Reewum France yaaggna am ayy bërëbu taaggatukaayu yaram yoo xamni nii ayy soxna rek ñoofay taaggatee seen yaram te yitt keen musu ci wax dara waaye ñaakk aand jaraafu gox biidi Raincy ci soxna am seen bërëbu taaggatukaayu yaram dafay wone mbañeel ak soxor ak ñaakka mana muñal jullit ci dara bi nga xamni reewum France amnako
1297517