Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci television bii nga xamni mooy Al Alam ni: ayy nitt yu yor ayy nganaay soxnañu jëmaleko ci ziyaarekatu yi nga xamni ñoo ñëwoon di ziyaare Imaam Jawaad ci fattaliku ak maaggal geen aduna juroom ñenteelu Imaamu shiit yi , amna ayy ziyaarekat yoo xamni amnañu ci ayy gaañu gaañu
Deemb ci guddi terroriste yi amalnañu ayy coong ci ayy ziyaarekat yoo xamni nii dañudoon dem ca xabru Imaam Jawaad ci Kaazimayni ci Bagdad peyu reewum Irak ba amna lu toollu ci ñent fukki doomu aadama yoo xamni nii ñaakknañu ci seen bakan am juroom ñaar fukki nitt yoo xamni nii amnañu ci ayy gaañu gaañu
Coong terroriste bii nak mungi xewee ci kaw pomme bi nga xamni moom lañu duppee (azamiye) neekk ci Kaazimayni ci Bagdad
1298963