Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet te aju ci daara ju kawe ji nga xamni moo neekk ci Malaya peyu reewum Malaisie ni: lëllu aduna wërngëlkëp bii ci nimbalu daara ju kawe jii nga xamni moo neekk ci reewum Malaisie lañukoy amalee
Lëll bii ci diiru ñaari fan lañukoy amal dinañu ci jaangat doxlinu islaam ak tërëlinu islaam ci waallu gestiom maanaam nakalañii yore mbir yi ak jaangale islaam ci waallu commerce mbebetu amal lëll bii nak mooy ñu yeegg ci jaangale islaam yi ci waallu doxalin ak dajale ñëpp ñi nga xamni seen xam xam dafa naac ci wall wii ñu xalaat ci doxalinu islaam
Jaangat nakalañii yoree ayy mbir ci islaam ak nakalañii yoree nguur ak leepp luyy doxal waallu nguur ci islaam doxal leepp loo xamni nii dafa aju ci waallu koom koom mooy toomb yi nga xamni moom lañii waxtaanee
Ci cëppaa ndawu lëll bii dinañu wone ayy gëstu yi nga xamni amalnañuko ci wall wii suñu nooppee ci lëll dañukoy móól defko ab teere
1303216