Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci ñi nga xamni ñoo leen teewal ca Afrique ni: altine bii ñu wees lañu amal conference bii ayy kilifa yu magg yu melni jawriñ gi ñu deenkk waallu koom koom ak ki nga xamni moofa teewaloon njiitu reew mi ak ayy borom xam xam yu magg teewoonnañufa
Ndaw yi nga xamni ñoo teewal reewu jullit ñi ci biir reewu Senegal yitt teewoonnañu ci conference bi reew yu ci melni reewum Indonesie ak Marok ak Iran ak yeneeni reew
Conference bii walla ndaje mii ci jaang leen ci ayy laaya al xuraan lañuko dooree ci gannaaw loolu Arame Thiam njiitu mbootaayu jigeenu jullitu Senegal yëkkatinafa ayy kaaddu waxna ci bennoo jullit ñi ak jappante gi nga xamni moom lañu wara jaappante seen biir ndax nakk moo neekkoon toombu waxtaan wi kiidi njiitu mbootaayu jullitu reewum Senegal gërëmna ndawu reewwum Iran ci waallu caada ci reewum Senegal ak taxawu bi nga xamni taxawuna leen ko ci xew xew bii ak ligeey bi nga xamni reewum Iran mungikoy ligeey ci bennoo jullit ñi
1282724