Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar biidi (Islam.ru) ni: sooroor bii ñaar fukki metre guddaay la am ci kaw te yitt mungi neekk ci gox biidi (Nordvest) ci kopenak jamono jii ñungikoy tabax te noppeegul waaye jullit yi nga xamni ñooy yeewoo ci bërëb yooyu amnañu mbekte ci jumaa ji
Sooroor bii mooy neekk njëlbeenu sooroor ci reewum Danmark waaye reewum Danmark dafa tere ñu jëfandikoo sooroor yi ngir nooddu loolu moo waral sooroor ab symbol rek lay neekk
Mbootaayu islaam bu neekk ci reewum Danmark moom mooy tabax jumaa jii nga xamni ayy weer ci gannaaw lañuko door, kiidi Abdul Hamid Alhamdii njiitu mbootaayu islaam ci reewum Danmark waxna tabax jumaa ju tolnii dina mana neekk ab toontu bu am solo ci ñi nga xamni ñoodoon amal ayy ŋaañ ci yonent bi
1284910