کد خبر: 1286214
تاریخ انتشار : ۲۰ شهريور ۱۳۹۲ - ۰۲:۱۳

Dinañu taambali wone ayy programme ci njëlbeenu television jullit ñi ci reewum Russie

Waallu dundin njëlbeetu television reewum Russie di na taambali wone ayy programme ci internet bi



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci ñi nga xamni ñoo leen teewal ci tugël yi : kiidi Rustom Arif Jaan of njiitu chaine television bii waxna ni: mbebetu chaine bii mooy fexe ba jullit ñi bennoo rawatina nak jullitu reewum Russie ak seeni diine ak seeni aada yu wute television bii dina wone ayy programme yu wute ci waallu diine ayy programme ci waallu al xuraan ak addiisu yonent bi ak wone dundinu jullitu reewum Russie ak borom xam xam yu magg yi


Kii nga xamni moo jiite television bii yokkuna ci ni: leen ci programme yi nga xamni dinañuko wone ci television bii dañukoy jagleel aax ak yeleefu ñaari waajur yi ak solo gi nga xamni famille amnako ci islaam ak yarinu xale ci gisgisu islaam ak solo gi nga xamni xam xam amnako ci islaam


1285830

captcha