کد خبر: 1287954
تاریخ انتشار : ۲۴ شهريور ۱۳۹۲ - ۰۰:۵۱

Teere bii nga xamni mooy (mbootu jogu Imaam Xuseyn ca Karbal) wonenañuko ca reewum Inde

Waallu xalaat teere biidi (mbootu jogu Imaam Xuseyn ca Karbala) wonenañuko ci ca reewum Inde ci gox biidi Lakxano ci teewaayu ayy borom xam xam ak ayy nittu diine



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci ñi nga xamni ñooko teewal ci Asie ni: ci xew xewu wone teere bii nga xamni kiidi Ridaa Abbaas mooko taalif ci kalaamay Ordu ci mbir ak mboot yi nga xamni moo waraloon Imaam Xuseyn jokk jaamarloo ak Yaziid ba ñaakk ci bakanam ci teewaayu ayy borom xam xam lañuko amalee ku ci melni Naziir Saadix Naxawii njiitu daara diine yu neekk ci reewum Inde ak Abul Irfaan Frangii nga xamni borom xam xam Sunnite bu raañeekula ci gox bi ak Ridaa Xuseyn njiitu kureel bii nga xamni dafay ci waallu diine


Kiidi Saadix Naxawii yëkkatina ayy kaaddu jëmaleko ci waallu mboot ak mbir yi nga xamni moo waral Imaam Xuseyn jog jaamarloo ak noonu islaam yooyu waaye kiidi Ridaa Abbaas nga xamni moo taalif teere bii waxna ci li nga xamni moo waral mu taalif teere bii ni: ndax Imaam Xuseyn ak mbir yi nga xamni moo waral Imaam Xuseyn jog jaamarloo ak yaziid ak noonu islaam


1287551

captcha