کد خبر: 1292780
تاریخ انتشار : ۰۱ مهر ۱۳۹۲ - ۲۲:۲۷

Reewum Mali ak reewum Marok dëppoonañu ci taaggat Imaamu jumaa yi ca Rabaat

Waallu bitim reew jawriñ gi ñu deenkk waallu diine ci reewum Marok ak jawriñ gi ñu deenkk waallu biir reew ci reewum Mali amalnañu ab dëppoo ci taaggat juroomi teere Imaam ca Rabaat peyu reewum Marok



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (IINA) ni: ci ndaje bi nga xamni kiidi Ahmad Tawfiix jawriñ gi ñu deenkk waallu diine ci reewum Marok ak Moussa Sinko Coulibaly jawriñ gi ñu deenkk biir reew mi seexoon nañuko xaatimnañu ab këyit ngir ñu mana taaggat ayy Imaam ca Rabaat


Suñu sukkandikoo ci këyit gii nga xamni xaatimnañuko lu toollu ci teemeeri Imaam dinañu leen taaggat ci att yii ñu dëkkmal ca Rabaat ci ayy bërëbu jaangukaay yu wute dinañu leen jaangal nakalañii defee xutba waaye nak dina am yeneeni Imaam yoo xamni nii ñooy baayeekoo ca reewum Marok dem ca reewum Mali ngir taaggat leen ci Imaam yi


Jawriñ giñu deenkk waallu diine ci reewum Marok junjuna ci xaritoo ñaari reew yi te yitt ak diggënte bu yaagg waxna yitt gannaaw bi nga xamni ñaari att yii ñu wees ci ayy jafejafe yu tar ci waallu terroriste dina deelluwaat ci ak dal


1292476

captcha