Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (On Islam) ni: police bu neekk ci reewum Russie xamlena ni doornañu ayy gëstu ak ayy enquete ngir ñu xam ñi nga xamni ñoo def lakk gii ci jumaa jii
Xew xew bii nga xamni moo am ci jumaa jiidi (velgugraad) mooy njëlbeenu coong boo xamnii amalnañuko ci jullit yi nga xamni ñoo neekk ca bët gaanaaru reew mi
Lu jiitu xew xew bii amna been dalu islaam bi nga xamni moo neekk ci gox biidi (Kuktal) waaye amna ku ñu ci tekk loxo yaakaar ni moo def jëf ju ñaaw jii, ndax camera cacher yi dañuko filmer feekk mungi def jëf ju ñaaw jii
Ci beneen xew xew bu tiis ci ayu bës bii ñu wees jumaa ji nga xamni moo neekk (Kbardino) amalnañufa ayy coong, diine islaam mooy ñaareelu diine ci reewum Russie teemeer boo jël ci askanu reewum Russie fukki yi ak juroom ayy jullit lañu askanu reew mi nak toolluna ci 145 million
1307934