Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (CTPost) ni: dinañu gaaral ci gaaral bii walla exposer bii ayy jeexintalu xam xam ak islaam jëfandikoo nak decoration artistique
Gaaral bii nga xamni ci nimbalu këru ligeeyukaay bii nga xamni dafay yënggu ci waallu energie ci reewum Espagne (ibnagu) lu toollu ci teemeer ak juroom fukki piece ak jeexintal ci waallu art ak taariixu islaam baayeekoo ci daara ju kawe ji nga xamni moo neekk ca Oxford ci reewum Angleterre dinañuko gaaral ci gaaral bii
Kiidi (Sabiixatul xumayr) nga xamni bindkatla te yitt xam xam dafa naac ci waallu art ci islaam mooy gaaral ayy ligeey yi nga xamni amalnako , dinañufa gaaral ayy teere al xuraan yu yaagg lool yoo xamni nii ci fukkeelu xarnu gannaaw gaddaay gi lañuko bind
Gaaral bii su jeexee ci reewum Espagne dinañuko amal ca reewum Amerique ci attum 2014 ca Dalas
1308180