کد خبر: 1278589
تاریخ انتشار : ۰۵ شهريور ۱۳۹۲ - ۰۲:۳۵

Budaa yu neekk ca reewum Myanmar taalnañu këru jullit ñi

Waallu bitim reew budaa yi nga xamni ñoo neekk ci reewum Myanmar amalnañu ayy coong ci boutique ak këru jullit ñi ci gox yi nga xamni ñoo feete ca bët saalumu reew mi



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci yeenekaay bi nga xamni mooy (Time india) ni: coong yii deemb ci ngoon lañuko amal gannaaw bi nga xamni ab xabaar wesaaroona ni dafa ab jullit bu yeegg ci ab soxna badaa


Suñu sukkandikoo ci waxu been policer dinañu wax ni fanweer ak juroomi këru jullit ak fukk ak ñaari boutique gu jullit budaa yi taalnañuko


Reewum Myanmar daaw ba leegi budaa yi dañii faat jullit ñi te yitt takk der yi nga xamni ñoo wara aar kaaraange askan wi ñëpp lañii aar bamu des jullit ñi te yitt yeen saa yi dañii fitnaal jullit ñi


Ci fitnaa yii nga xamni budaa yi ñungikodoon def ci jullit ci reewum Myanmar ayy teemeeri jullit faatunañu ci ayy junni junni amnañu ci ayy gaañu gaañu te yitt ayy junni junni ñaakknañu ci seeni kër


1277468

captcha