کد خبر: 1290846
تاریخ انتشار : ۳۰ شهريور ۱۳۹۲ - ۰۰:۰۲

Ñu dañoo gëm yaalla dafay wëy di des ci dollar reewum Amerique

Waallu bitim reew been bërëbu aattekaay bu neekk ci reewum Amerique doggalna ni baat biidi (ñun dañoo gëm yaalla) dafay wëy di des ci dollars bi



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (Islam.ru) ni: xeex bii nga xamni moo doxoon diggënte kureel yi nga xamni amuñu diine ak bërëbu aatekaay bi ci ñu dindi baat biidi (ñun dañoo gëm yaalla) ci xaalisu reewum Amerique du muju feen ndax aattekaay bi jëlna dogalu baayi baat bi ci xaalisu reewum Amerique


Kureel bii dafa bindoon ci plainte bi nga xamni moom la joxoon bërëbu aattekaay bi baat bii (ñun dañoo gëm yaall) dafa wute ak yoon bi nga xamni moo ëmb reewum Amerique, ndax dañu ci bind (ñun) te ñun dafa ëmbaale mbooleem doomu reewum Amerique yëpp te amna doomu reewum Amerique yoo xamni nii gëmuñu yaalla gëmuñu been diine


Bii mooy ñaareelu yoon bi nga xamni mbootaay yi mga xamni gëmuñu yaalla di jooytu lu melni ci bërëbu aattekaay yu neekk ci reewum Amerique, ci këyit bii nga xamni moom lañu njëkkoona jox bërëbu aattekaay bi ci attum 2011 dañu ci saakkuwoon ñu dindi baat bii (ñun dañoo gëm yaalla) ci xaalisu reewum Amerique waaye fi mbaxna neekkee been nanguwul woon seen saakkuteef bii


Bërëbu attekaay bii nga xamni moo neekk ci reewum Amerique xamlena baat bii nga xamni bindnañuko ci xaalisu reewum Amerique du waaññi dara ci yoon bi nga xamni moo tënkk reewum Amerique


1290712

captcha