کد خبر: 1292119
تاریخ انتشار : ۳۱ شهريور ۱۳۹۲ - ۲۳:۲۹

Suba lañii xam dogalu yoon ci tas parti biidi les frères musulmans ca Egypt

Waallu bitim reew suba 23 septembre lañii xaar dogalu fa mbaxna neekkee been ci waallu tas parti biidi (frères musulman) neekk ci reewum Egypt



Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci bërëbu xabaar bi nga xamni moo neekk ci internet (axbarukanet) ni: bërëbu aattekaay bi nga xamni mooy aatte mbir yu gëna jampp ci reewum Egypt xamlena suba lañii jaangat ak setantal saakkuteef bi nga xamni ab bërëbu aattekaay saakkuwoonnako ci ñu tas parti biidi frères musulman ci reewum Egypt


Lu jiitu loolu kiidi Muhamad Abdullah nga xamni ndaw la ci peeccum ndawu reew mi bokk ci parti biidi (Al Mujtama) saakkuwoonna ci bërëbu aattekaayu reewum Egypt mu tas parti biidi frères musulman nanggu seen am am yëpp joxko nguur gi ndax dafa jël ayy ngannaay jaamarloo ak nguuru reewum Egypt


Suede yoon dafa jël dogalu tas parti nga xamni mooy parti bu gëna rëyy ci reewum Egypt dina dakkal mbooleem yënggu yënggu polotik yi te yitt seen am am yëpp dañukoy jël joxko nguur gi


1291589

captcha