Këru tasukaayu xabaaru al xuraan yi (ikna) te neekk ci Iran xabaarna jëleeko ci ñi nga xamni ñoo yor waallu jokkoo ci centre islamique bi nga xamni moo neekk ca Angleterre ni: ci pasteefu ñi nga xamni ñoo jiite centre islamique bii neekk ca Angleterre dinañu amal ab xew xewu jaang ñaan bii nga xamni Imaam Xuseyn mooko jaangoon ca Arafa ba loolu waral ñudiko woowee ñaanu Arafa,ci bërëbu centre bi ci jamono ji nga xamni ujaaj yi ñungikoy amal ca Maakka
Centre islamique bii nga xamni moo neekk ci reewum Angleterre alarba biidi ñëw dina amal ayy xew xew ngir maaggal tabaski gi ñungi ci woo jullit ñëpp rawatina nak chiite yi
Bërëb ak centre islaamique yi nga xamni ñoo neekk ci reewum Angleterre ak yeneeni reew reewum Allemagne dinañu maaggal tabaski gi ci alarba bi waaye nak ñungi woo mbooleemo jullit ñi ñu nëw book ak ñoom feete biidi Tabaski
1301548